3 Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
4 Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
5 ànd ak daraja, dawal ba am ndam, di dawal dëgg ak yërmande ji war, ba mana def ay jaloore.
6 Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
7 Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,
8 di sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom:
9 sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.
10 Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
11 Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,