13 Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
14 Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.
15 Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
16 ñu duggsi kër Buur, ci biir mbégteek bànneex.