3 Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.
4 Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel.
5 Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
6 Yaw lanuy dàqe bañ yi, sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
7 Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
8 Yaa nuy musal ci bañ yi, yaay gàcceel noon ñi.