Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 44:3-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 44:3-11 in Kàddug Yàlla gi

3 Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.
4 Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel.
5 Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
6 Yaw lanuy dàqe bañ yi, sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
7 Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
8 Yaa nuy musal ci bañ yi, yaay gàcceel noon ñi.
9 Yàlla lanuy damoo bésoo bés, di màggal turam ba fàww. Selaw.
10 Waaye danga noo wacc, torxal nu, ba àndulook sunu mboolooy xare.
11 Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.
Sabóor 44 in Kàddug Yàlla gi