Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 40:7-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 40:7-9 in Kàddug Yàlla gi

7 Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal, ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko.
8 Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
9 Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
Sabóor 40 in Kàddug Yàlla gi