Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 40:2-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 40:2-13 in Kàddug Yàlla gi

2 May xaara xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
3 génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
4 Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal ak a dénku ci Aji Sax ji.
5 Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
6 Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.
7 Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal, ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko.
8 Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
9 Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
10 Siiwal naa sag njekk ca ndaje mu mag ma. Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.
11 Làquma sag njekk, ne cell ak moom. Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko. Làquma ndaje mu mag ma sa ngor ak sa worma.
12 Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. Sa ngor ak sa worma, yal na ma feg ba fàww.
13 Ay musibaa ma tanc, ne gàññ, ba wees ab lim. Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; sama xol jeex tàkk.
Sabóor 40 in Kàddug Yàlla gi