3 ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw
4 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, di ma teral, di ma siggil.
5 Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
6 Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.