4 sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
5 ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.
6 Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.