Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 39:3-7 in Wolof

Help us?

Sabóor 39:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Dama noon cell, ne patt, noppi, ba mu ëpp; sama njàqare yokku,
4 sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
5 ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.
6 Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.
7 Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
Sabóor 39 in Kàddug Yàlla gi