13 Ñi may wuta rey a ngi may fiir, di ma jéema lor, di ma waxal musiba, yendu maa lalal pexe.
14 Man, ma mel nib tëx, dégguma, mel ni luu, àdduwma,
15 di saf ku dul dégg, bay layoo.
16 Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.