Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 37:3-17 in Wolof

Help us?

Sabóor 37:3-17 in Kàddug Yàlla gi

3 Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.
4 Deel bànneexoo Aji Sax ji, mu may la say nammeel.
5 Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.
6 Day setal sab der ni jant bu fenk; sab àtte ne ràññ ni njolloor.
7 Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.
8 Baal mer, dëddu xadar. Xol bu jóg, loraangey neen.
9 Ku bon, ñu dagg, sànni; ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi.
10 Nes tuut, ku bon ne mes, nga seet, seet, mu réer.
11 Waaye néew-dooleey jagoo réew mi; jàmm ne ñoyy, ñu bége.
12 Ku bon fexeel ku jub, di ko màttu,
13 Buur Yàlla di ko ree, xam ne bésam a ngi ñëw.
14 Ku bon bocci saamar, tàwwig fitt, nara rey ku ñàkk, néewle, nara bóom kuy jubal;
15 far jam boppam saamaru xol, fittam damm.
16 Aji jub, as tuutam moo gën koomu ku bon.
17 Ku bon kat, sa doole dëddu la; ku jub, Aji Sax ji wallu la.
Sabóor 37 in Kàddug Yàlla gi