Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 35:7-22 in Wolof

Help us?

Sabóor 35:7-22 in Kàddug Yàlla gi

7 Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.
8 Yal nañu sànkoo mbetteel, keppoo seen fiir, sànkoo seenum yeer.
9 Su boobaa ma bége Aji Sax ji, bànneexoo wallam,
10 di ko sante sama jëmm jépp, naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw, di xettli néew-ji-doole ci boroom doole, ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?»
11 Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
12 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar, ndaw tiisu xol!
13 Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, di woor, toroxloo, sukk, ñaanal leen,
14 tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey, di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay.
15 Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
16 Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk te di ma màttu.
17 Éy Aji Sax ji, loo deeti seetaan? Musal ma ci seenum pàdd, wallu ma ci yii gaynde, sàmmal ma sama benn bakkan bii!
18 Maa lay sante fa ndaje yaatoo, màggal la digg mbooloo mu yaa.
19 Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo. Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree.
20 Waxuñu jàmm, xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi ay kàdduy tuuma.
21 Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»
22 Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, éy Boroom bi, bul ma sore.
Sabóor 35 in Kàddug Yàlla gi