3 xàcci sa xeej ak sa sémmiñ, dajeek ñi may dàq. Déey ma, ne ma: «Sag mucc, man a.»
4 Ñiy wut sama bakkan, yal nañu rus ba torox; ñi may fexee lor, yal nañu leen waññi, sewal leen.
5 Yal na leen malaakam Aji Sax ji bëmëx, nim ñax mu ngelaw wal.
6 Yal na leen malaakam Aji Sax ji dàq, ñuy lëndëmtuy tarxiis.
7 Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.
8 Yal nañu sànkoo mbetteel, keppoo seen fiir, sànkoo seenum yeer.
9 Su boobaa ma bége Aji Sax ji, bànneexoo wallam,
10 di ko sante sama jëmm jépp, naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw, di xettli néew-ji-doole ci boroom doole, ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?»
11 Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
12 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar, ndaw tiisu xol!
13 Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, di woor, toroxloo, sukk, ñaanal leen,
14 tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey, di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay.
15 Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
16 Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk te di ma màttu.
17 Éy Aji Sax ji, loo deeti seetaan? Musal ma ci seenum pàdd, wallu ma ci yii gaynde, sàmmal ma sama benn bakkan bii!
18 Maa lay sante fa ndaje yaatoo, màggal la digg mbooloo mu yaa.