20 Waxuñu jàmm, xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi ay kàdduy tuuma.
21 Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»
22 Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, éy Boroom bi, bul ma sore.
23 Jógal, sàmmal ma sama àq. Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.
24 Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg, ñu bañ maa ree!
25 Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»
26 Ku bége sama njàqare, yal nanga rus, ba torox. Kuy réy-réylu ci sama kaw, yal nanga am gàcce, ne yàcc.