Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 35:19-28 in Wolof

Help us?

Sabóor 35:19-28 in Kàddug Yàlla gi

19 Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo. Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree.
20 Waxuñu jàmm, xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi ay kàdduy tuuma.
21 Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»
22 Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, éy Boroom bi, bul ma sore.
23 Jógal, sàmmal ma sama àq. Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.
24 Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg, ñu bañ maa ree!
25 Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»
26 Ku bége sama njàqare, yal nanga rus, ba torox. Kuy réy-réylu ci sama kaw, yal nanga am gàcce, ne yàcc.
27 Ku bége sama der bu set, yal nanga bànneexu, di sarxolle, foo tollu di biral naan: «Aji Sax jee màgg! moom miy bége jàmmi jaamam.»
28 Man it ma tudd sa njekk, di la dëkke màggal!
Sabóor 35 in Kàddug Yàlla gi