Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 35:11-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 35:11-16 in Kàddug Yàlla gi

11 Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
12 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar, ndaw tiisu xol!
13 Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, di woor, toroxloo, sukk, ñaanal leen,
14 tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey, di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay.
15 Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
16 Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk te di ma màttu.
Sabóor 35 in Kàddug Yàlla gi