7 Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.
8 Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
9 Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.
10 Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
11 Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
12 Dikkal doom, déglu ma, ma jàngal la ragal Aji Sax ji.