Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 34:7-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 34:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.
8 Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
9 Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.
10 Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
11 Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
Sabóor 34 in Kàddug Yàlla gi