13 Ana ku dund neex, mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel?
14 Na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.
15 Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
16 Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.
17 Aji Sax jeey rëbb kuy jëfe mbon, ngir dagge ko kaw suuf, far turam.