9 Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
10 Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
11 Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
12 Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
13 Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.
14 Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
15 Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
16 Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
17 Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.
18 Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
19 Day jot bakkanam, di ko dundal cib xiif.