Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 33:9-15 in Wolof

Help us?

Sabóor 33:9-15 in Kàddug Yàlla gi

9 Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
10 Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
11 Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
12 Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
13 Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.
14 Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
15 Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
Sabóor 33 in Kàddug Yàlla gi