5 Moo sopp dëgg ak yoon. Aji Sax ji, ngoram a fees àddina.
6 Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.
7 Moo boole ndoxi géej, jal, yeb xóotey géej ciy mbànd.
8 Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko.