Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 33:2-18 in Wolof

Help us?

Sabóor 33:2-18 in Kàddug Yàlla gi

2 Xalamleen, sante Aji Sax ji, xalamal-leen ko xalamu fukki buum.
3 Fental-leen ko woy, xalam, mu neex, sarxolle jib.
4 Aji Sax jee jub kàddu. Mooy jëfe lépp kóllëre.
5 Moo sopp dëgg ak yoon. Aji Sax ji, ngoram a fees àddina.
6 Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.
7 Moo boole ndoxi géej, jal, yeb xóotey géej ciy mbànd.
8 Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko.
9 Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
10 Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
11 Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
12 Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
13 Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.
14 Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
15 Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
16 Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
17 Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.
18 Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
Sabóor 33 in Kàddug Yàlla gi