Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 31:7-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 31:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Maa bañ kuy topp tuuri neen. Man, Aji Sax ji laa wóolu.
8 Damay bég, di bànneexoo sa ngor, li nga xoole samaw tiis. Ràññee nga sama njàqarey xol.
9 Waccoo ma ci loxol noon, danga maa taxawal fu ma yaatoo.
10 Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa! Samay gët a ngi giim ndaxu tiis, xol jeex, yaram jeex.
11 Naqar a ngi may rey, tiis di wàññi samay fan, sama doole ŋiis ndax sama njubadi, samay yax semm.
Sabóor 31 in Kàddug Yàlla gi