20 Yàlla yaa yaa ngëneel loo dencal ku la ragal, defal ko ku la làqoo, doom aadama seede.
21 Yaa koy làq fa nga làqu, fa pexey nit àggul. Nga yiir ko, mu yiiru ci ayu làmmiñ.
22 Teddnga ñeel na Aji Sax ji! Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe biir dëkk bu ñu gaw.