Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 31:13-21 in Wolof

Help us?

Sabóor 31:13-21 in Kàddug Yàlla gi

13 Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.
14 Damaa dégg jëw yu bare, lu raglu dar ma kepp. Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel, di wut sama bakkan.
15 Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
16 Yaa yor sama àpp. Xettli maak ku ma noonoo ak ku may sonal.
17 Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.
18 Éy Aji Sax ji, woo naa la wall, yàlla buma rus. Yal na ku bon rus, ne xerem biir njaniiw.
19 Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylook a xeebaate.
20 Yàlla yaa yaa ngëneel loo dencal ku la ragal, defal ko ku la làqoo, doom aadama seede.
21 Yaa koy làq fa nga làqu, fa pexey nit àggul. Nga yiir ko, mu yiiru ci ayu làmmiñ.
Sabóor 31 in Kàddug Yàlla gi