12 Noonoo noon a ma sewal, dëkkandoo waxi noppi, xame seexlu ma, ku ma gis biti, di ma daw.
13 Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.
14 Damaa dégg jëw yu bare, lu raglu dar ma kepp. Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel, di wut sama bakkan.
15 Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
16 Yaa yor sama àpp. Xettli maak ku ma noonoo ak ku may sonal.
17 Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.