7 Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, bés niki tey, maa la jur.
8 Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
9 yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»
10 Kon yeen buur yi, muusleen, kilifay àddina, fàgguleen.