3 Ña nga naan: «Nanu dagg càllala yi, sànni jéng yi!»
4 Ki ci jalub asamaan a ngay ree, Boroom baa nga leen di kókkali,
5 mer, ba gëdd leen, xadaru, tiital leen ne:
6 «Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»
7 Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, bés niki tey, maa la jur.
8 Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
9 yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»