5 Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqte, te dootu leen yékkati.
6 Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!
7 Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.
8 Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
9 Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.