7 Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote! Ngalla baaxe ma, nangul ma.
8 Yaw la sam xel ne ma, ma sàkku la, te it yaw Aji Sax ji laay sàkku.
9 Sang bi, bu ma làqu, bul mer, jañax ma. Yaa ma daa wallu. Bu ma wacc, bu ma ba, yaay Yàlla mi may musal.
10 Ndey ak baay man nañu maa wacc, Aji Sax ji fat ma.
11 Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon, jaarale ma joor gu wóor, ngir ñi may tëru.
12 Bu ma baye bànneexu noon. Seedey naaféq a ma jógal, di sos fitna.
13 Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.