3 Bu gàngoor booloo sama kaw, duma raf. Ab xare jib, ma ànd ak Yàlla.
4 Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.
5 Bésub ay, mu yiire ma mbaaram, làq ma, ma làqoo xaymaam, aj ma ciw doj, ma raw.
6 Ma doxe fa siggi, tiim noon yi ma wër, di sarxali fa xaymaam saraxi sarxolle. Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko.
7 Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote! Ngalla baaxe ma, nangul ma.