3 Maa ngi janook sa ngor, di jëfe sa worma.
4 Toogumaak naxekat, lëngoowumaak naaféq,
5 sib naa gàngooru saaysaay, toogumaak ku bon.
6 Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib, di wër sa sarxalukaay,
7 àddu, sant la, lim sa jépp jaloore.
8 Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay, bëgg bérab bi sag leer teew.