7 Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
8 Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
9 di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.
10 Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
11 Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool, jéggal ma ngir saw tur.