Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 25:13-20 in Wolof

Help us?

Sabóor 25:13-20 in Kàddug Yàlla gi

13 muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?
14 Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.
15 Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettli ci fiiru noon.
16 Ngalla geesu ma, baaxe ma, maa wéet, néew doole,
17 sama xol feesey xalaat. Rikk, teggil ma njàqare!
18 Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.
19 Xoolal noon yi ne gàññ, bañ ma mbañeelu fitna.
20 Éy, aar ma, musal ma! Bu ma rusloo, yaw laa làqoo.
Sabóor 25 in Kàddug Yàlla gi