13 muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?
14 Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.
15 Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettli ci fiiru noon.
16 Ngalla geesu ma, baaxe ma, maa wéet, néew doole,
17 sama xol feesey xalaat. Rikk, teggil ma njàqare!