Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 24:3-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 24:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, kuy taxawi bérabam bu sell ba?
4 Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, xemmemul caaxaani neen, du giñey fen.
5 Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji, ak njekku Yàlla, mi koy musal.
6 Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. Selaw.
7 Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.
8 Buur Boroom ndam booboo di kan? Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar, Aji Sax ji jàmbaaru xare ji.
Sabóor 24 in Kàddug Yàlla gi