Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 24:3-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 24:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, kuy taxawi bérabam bu sell ba?
4 Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, xemmemul caaxaani neen, du giñey fen.
5 Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji, ak njekku Yàlla, mi koy musal.
6 Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. Selaw.
7 Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.
8 Buur Boroom ndam booboo di kan? Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar, Aji Sax ji jàmbaaru xare ji.
9 Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.
10 Buur Boroom ndam booboo di kan? Xanaa Aji Sax ju gàngoor yi. Kookooy Buur Boroom ndam. Selaw.
Sabóor 24 in Kàddug Yàlla gi