3 leqli ma, teg ma ci yooni njekk ngir teddngay turam.
4 Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
5 Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.