3 Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, nopploo ma.
4 Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israyil di la kañ.
5 Yaw la sunuy maam wóolu woon, wóolu la, nga xettli leen.
6 Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
7 Man nag aw sax rekk laa, matuma nit. Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.
8 Ku ma gis ñaawal ma, biiñ ma, xeelu ma, naa:
9 «Na wéeroo Aji Sax ji, mu xettli ko; su ko soppee, na ko wallu.»
10 Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey, naxe ma sama weenu yaay.
11 Yaw laa dénkoo ba may juddu, ba ma juddoo sama ndey, ngay sama Yàlla.