19 séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.
20 Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; yaa may dooleel, gaawe ma.
21 Xettlil sama bakkan ci saamar, ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj!
22 Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. Yaa ma wallu woon!
23 Ma siiwali saw tur ci bokk yi, màggale la digg mbooloo mi.
24 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.