14 Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
15 Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
16 Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
17 Ay xaj a ma wër, di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, bëtt samay yoxook samay tànk.
18 Maa ngii, mana waññ sama yax yépp, ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,
19 séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.