13 Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
14 Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
15 Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
16 Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
17 Ay xaj a ma wër, di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, bëtt samay yoxook samay tànk.