7 jagleel ko barke bu sax dàkk, bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
8 Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
9 Buur, yaa naan sa noon yépp céex, ne say bañ taral.
10 Soo nee jalañ, jafal, ñu boy. Aji Sax ji mer, sànk leen, sawara xoyom leen.