7 Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
8 Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; kenuy tund ya jaayu, di reg-regi.
9 Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya, sawara boye ca gémmiñ ga, xal yu yànj tàkke ca.
10 Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.
11 Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
12 Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13 leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
14 Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,