Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 18:40-47 in Wolof

Help us?

Sabóor 18:40-47 in Kàddug Yàlla gi

40 Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41 Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.
42 Ñu ne wallóoy, wall amul; ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
43 Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.
44 Xettli nga ma ci bokk yiy fippu, def ma, ma jiite ay xeet; waaso wu ma xamul sax nangul ma,
45 ku ma ci dégg, déggal ma, ay doomi doxandéem di ma raamal,
46 ne yàcc, génne seeni tata, di lox.
47 Aji Sax jeey kiy dund. Kii ma sës a jara sant. Yàlla mi may musal moo màgg!
Sabóor 18 in Kàddug Yàlla gi