Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 18:32-41 in Wolof

Help us?

Sabóor 18:32-41 in Kàddug Yàlla gi

32 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
33 Yàllaa may dooleel, di ma xàllal, yoon mat.
34 Moo ma gaawal ni kéwél, taxawal ma fu kawe.
35 Moo may tàggat ngir xare, may bank xalag xànjar.
36 Aji Sax ji yaa may feg, musal ma, dooleel ma sa loxo, nangul ma, darajaal ma.
37 Yaa ma xàllalu yoon, ba duma tërëf.
38 Ma dàq noon yi, dab leen, jekkli, doora dëpp.
39 Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.
40 Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41 Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.
Sabóor 18 in Kàddug Yàlla gi