3 Aji Sax ji laay sës, mu di ma aar, di ma wallu. Mooy sama Yàlla, ji may sës, yiiru, fegu; mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.
4 Ki yelloo cant, Aji Sax ji, moom laa woo, mucc ci samay noon.
5 Buumi ndee tanc ma, walum kasara naq ma,
6 buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.
7 Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.