17 Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, seppee ma ca xóotey ndox ma,
18 musal ma ca noon yu mag, ya ma bañ te man ma.
19 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,
20 yaatal ma, bége ma, ba xettli ma.
21 Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.
22 Sàmm naa yooni Aji Sax ji, bonuma, di moy sama Yàlla.
23 Dama ne jàkk ndigalam yépp, xalabuma dogali yoonam.
24 May ànd ak moom, di jëfeg mat, di moyoo tooñ.
25 Aji Sax jee ma yool sama njekk, rafetlu sama mucc ayib.
26 Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore; ku matale, fekk la matale;
27 ku sellal, fekk la sell; ku dëng, fekk laak say feem.
28 Yaw yaay musal xeet wu néew doole, kuy daŋŋiiral, nga detteel.
29 Yaw kay yaa may niital. Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm.
30 Maak yaw kay, ma song gàngoor. Maak sama Yàlla, ma tëb um tata.
31 Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.
32 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
33 Yàllaa may dooleel, di ma xàllal, yoon mat.
34 Moo ma gaawal ni kéwél, taxawal ma fu kawe.