11 Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
12 Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13 leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
14 Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,
15 mu soqiy fitt ak jumi melax, tasaare leen, fëlxe.
16 Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, kenuy suuf ne duŋŋ.
17 Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, seppee ma ca xóotey ndox ma,
18 musal ma ca noon yu mag, ya ma bañ te man ma.
19 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,
20 yaatal ma, bége ma, ba xettli ma.